Okhoyolaana Mame Bamba barké naana Touba!
Waaw nañu dem Touba
Ku demul ma dem dem ziaar yeslu
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Takk jukk saxar ropalan
Auto ak ku nekk la lay yóbbu
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Bismil ilahi ñu sant Yàlla
Moom mi waral
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Ba nuy man a ziaaré ji
Boroom Touba ak Ndiareme
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Yaw lañu woolu
Góor gi demoon ma Yomba
Ñibbisi am ndam kenn du doomi Mame Diarra
Nitt ak Djiné ak Malaka yi tamit xam nañu la
Cheikh Bamba du mas lim ñu defal amuñu payam
Def na ñu ñuy Mouride
Teksi yar ñu ba nu ne nërëm
Bamba du masum, Fôré du masum
Bouraki Kangam, kenn du bàyyi Seugne Bara
Dem na Gabon si ngor dellusi am Ndam
Demaat Ganaar ñëw indi ngëram
Suñu waja moo def ci ñun lu addina seede
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Ba doo xame Joola Ndiago ak Sereer
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Mouride day jëfe Ndiggal
Te bàyyi ay Teere
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Neeleen ëskëy ci Sangup Boroom Darou
Moo jara woolu
Moñu defar bañu taaru
Moom nii ñépp nee masam amul ci xarnu bi
May sant saa su ne maa ngi Boroom dërëm ngërëm
Mbacké Kadior mbir yaa fa xew bari na lool
Leneen dacca xajjul
Cheikh Bamba rekk ci xol
Thierno Boroom Darou jaambar ja
Moo ko jiitu woon fa ndaar li wer na
Am naa lool ku ñu ko waxul mënoo ko xam
Am it naa lool ku ñu ko joxul mënoo ko am
Déedéet
Djaraama Djaarama waxleen (Djaraama)
Djaraama Djaraama neeleen (Djaraama)
Djaraama Mame Cheikh Ibra Fall’la miin yoon wi
Ba tay ku ne mën a jall (moniou’wann Cheikh Bamba)
Ba mu leer ni jant ne fang
Woolu naa la
Woolu naa la, Cheikh Bamba doylooo naa la man
Okhoyolaana Mame Bamba Magal Touba yè
Mame Bamba akhoyta ngaa ko mouride kéfop-nooyè
Bamba akhoyta ngaa-yé billaay Magal Touba
Alhamdou Sant nañu ci li nga ñu defal
Ku wet ci ñun fok ne loxo nga ko beeral
Yaa ñu sagal Cheikh Bamba, yaa ñu teraal
Tay ma fecc sar xoole yaa ma ko jaral
Ndangu Yàlla ki dogalam
Yonnen ak ay njoñam
Ndangu yaay ki fi joxe ñam
Jaambaru xarnu bi
Waaw mbërum mënesu ko daan
(Ngëram la am yooneen baadi sangam)
Ndax lum ñaan mu am
(Lam tontu ndaar moo leen taxoon na dem)
Ndeysaan wax leen ma Cheikh Bamba mi fum ne si man
Sa yoo ko tudde may yendoo retaan
Li ma mettiwoon neex ma fasa saman
Suñu waja moo def ci ñun lu addina seede
(Diaraama Diaraama)
Ba doo xame Joola Ndiago ak Sereer
(Diaraama Diaraama)
Mouride day jëfe Ndiggal te bàyyi ay Teere
(Diaraama Diaraama)
Neelén ëskëy ci sanguoup Borom Darou
(Diaraama Diaraama)