Video Defma Reine Feat Mbaye Dieye Faye » Aida Samb Lyrics | Musica Lyrics

Ver Video y Lyrics con la música del Genero Lyrics más popular de Aida Samb y otros artistas en línea. Disfruta de las mejores canciones de 2025 en LetrasFM de música en línea. ¡Encuentra tu canción favorita y escúchala en cualquier momento y en cualquier lugar!

Video Defma Reine Feat Mbaye Dieye Faye » Aida Samb Lyrics

Aida Samb - Defma Reine Feat Mbaye Dieye Faye Lyrics


Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la
Li ma gëna neex mooy sa jantal
Man xawma lu tax ma bëgg la
Dem àljanna yaa ci gëna gaaw

Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime)
Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw)
Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren)
Ndax yaa ma tànn (def ma reine waawaaw)

Man yaw laa bugga, change pas bae
Neex nga ma mën na doon sa jabar, doon sa maman
Lu ma ci gobe, bëgg naa
Di dox ci xal ñów fekk ci la

Dëb sol, caxabal
Foo ma woo ma ñëw
Loo fi laal, loo fi laal
Rekk ma lalli ko

Dëb sol, caxabal
Foo ma woo ma ñëw
Loo fi laal, loo fi laal
Rekk ma lalli ko

Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la
Li ma gëna neex mooy sa jantal
Man xawma lu tax ma bëgg la
Dem àljanna yaa ci gëna gaaw

Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime)
Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw)
Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren)
Yaa ma tànn (def ma reine waawaaw)

Wantanamera, feccal la youza
Toogal seetaan, ehn ma daagu dukkat
Ñoom de li ñuy jaay dama koy maye baby waxal
Li ci wañ bi toggantu ay nga ma koy ñamal

Wantanamera, feccal la youza
Toogal seetaan, ehn ma daagu dukkat
Ñoom de li ñuy jaay dama koy maye baby waxal
Li ci wañ bi toggantu ay nga ma koy ñamal
Waxal li nga bëgg, maa def fi yaa fi dogal
Lu jaar siisu naanal potu ndox te nangu ndogal

Su weesu waxi noon, kër gi maay boroom
Te lépp lu ma moom, baby yaay boroom

Dëb sol, caxabal
Foo ma woo ma ñëw
Loo fi laal, loo fi laal
Rekk ma lalli ko

Dëb sol, caxabal
Foo ma woo ma ñëw
Loo fi laal, loo fi laal
Rekk ma lalli ko

Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la
Li ma gëna neex mooy sa jantal
Man xawma lu tax ma bëgg la
Dem àljanna yaa ci gëna gaaw

Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime)
Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw)
Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren)
Yaa ma tànn (def ma reine waawaaw)

Wantanamera
(Woyal céy mbëggeel li dafa over neex!)
Ehnnnn ennh
Bu nit mënoo na génnee li ne ci xol bi waay!
(Li dafa neex, dafa neex, mbëggeel rekk a neex)
Sa nijaay ak sa ñoom yaay
Ña fay gis ñi toog di waxtaan
Mënuloo xam ni ma la bëggee eh
(Abass dafa lank danga sof, bëgg bay jooy)
Mënuloo xam ni ma la bëggee eh
(Woyal nga Abass, woyal nga faatu awo buuru këram!)
Su ma lay ray say xàqataay
Moo may tax a naam say jootaay
Mënuloo xam ni ma la yëgee bae
(Abass Diadiou baayu Papa Diadiou mëna yor jigéen)
Mënuloo xam ni ma la yëgee bae
(Aida Samb li dafa neex, dafa neex, dafa over neex)

Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la
Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la
Awma sa fay baby, teral nga ma
Awma sa fay baby, teral nga ma
(Chérie Abass Diadiou mbëggeel rekk a neex)
Lu ma la mën a fayee sagal nga ma
(Abass toog Fatook Aida mbëggeel dafa neex)
Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la
Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la
Awma sa fay baby!

Lu jugé ci xol ci sol lay déllu
Mbëggeel rekk a neex!
Aida Samb woyal na jigéen ñi nob seen jëkkër
Jëlal!
(Awma sa fay baby, teral nga ma)
Daan ko bugga mu bugga la, yëfi buggante la
(Awma sa fay baby, sagal nga ma)
Bëgg nga ko bëgg naa la te bëgg na leen yëfi bëggante la
Sama tey yaw la, sama suba tamit yaw la
Sama tey yaw la, sama suba tamit yaw la
Awma sa fay baby, teral nga ma!

Defma Reine Feat Mbaye Dieye Faye » Aida Samb Letras !!!
Esta web no aloja ningun archivo mp3©LetrasFM.Info 2025 Colombia - Chile - Argentina - Mexico. All Rights Reserved.

Musica Online, Escuchar musica online , Musica En Linea, Musica en linea gratis, Escuchar Musica Gratis, Musica Online 2025, Escuchar Musica

Musica 2025, Musica 2025 Online, Escuchar Musica Gratis 2025, Musica 2025 Gratis, Escuchas, Musica de Moda.