Lyrics Fay Bor By Youssou Ndour OnLine | Musica Afro

Escucha la música Afro más popular de Youssou Ndour y otros artistas en línea. Disfruta de las mejores canciones de 2025 en LetrasFM de música en línea. ¡Encuentra tu canción favorita y escúchala en cualquier momento y en cualquier lugar!

ESCUCHAR Fay Bor - Youssou Ndour

Musica de Youssou Ndour del Genero: Afro Todos los artistas y cantantes de música de Afro son individuos talentosos y apasionados que dedican su vida a crear y compartir su arte con el mundo. Su música de Youssou Ndour tiene el poder de emocionarnos, inspirarnos y conectarnos a un nivel profundo. En este blog LetrasFM, exploraremos el mundo de los artistas y cantantes de música del genero Afro, destacando su dedicación, creatividad y contribuciones a la cultura.

Los artistas y cantantes de música tienen la capacidad única de expresar sus emociones y experiencias a través de su voz y talento musical. A través de sus letras y melodías, nos llevan a un viaje emocional y nos permiten conectarnos con nuestras propias emociones.

Además de su talento musical, los artistas y cantantes son verdaderos profesionales en su campo. Trabajan arduamente para perfeccionar su

  • Fay Bor - Youssou Ndour 5:57

Youssou Ndour - Fay Bor Lyrics

Ki la bëgg yab ndax alal, yaw ignorer ko
Lèpp Lu la nit, di Dokhanto, yalla am na ko
Féek yaa ngi koy wóolóo, yalla mën në laa fayal sa bor

Ki la bëgg jaay loo sa ngor, bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek, bés a ngi ñëw, di na wéet ak jëf ëm

Te sax jamono fi mu toll nii, ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek, moo lay defal, ken du la xamal

Salaam alleykum, nga bañ ko fay, mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo, nga koy tanxal, mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques, ken mën të jaar, mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto, lu la neex def, mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex, nga wax ci moom, mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit, fu la neex tuur, mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël, daldi ko wor, mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax, loo waax mu dañ, mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole, won ko ko, mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili, ki nga tane, mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée, nan nga koy fay é

Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone na la tooñ, jéggël ma ko

Bor yi nga am fii ñu ne, nan nga koy fay é

Féek yaa ngi koy wóolóo,, yalla mën në laa fayal sa bor

Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko

Ñun doom i aadama ndiaye
Li ñu gën ë sonn al mooy
Aqqi dëkkëndòo, aqqi àndandoo
Ak aqqi am gi jamm yek
Yalla, yermëndéem yaatu na
Mën naa jéggël e bakkaar bu mu né
Waaye, doom i aadama Ndiaye, boo ko yor ee lee bor
Na nga ko fay, fii ci dunyaa
Walla nga balu ko mu baal la

Yé way samba, Khalass, kholal
Youssou maajigéen, oh! Lii doy na waar
Youssou Marie Sène, bu dee lii la, bor yi bari ña ñu
Yaay na nga ma baal, baay na nga ma baal, aqq u njuréel
You, Ndour, merci beaucoup
Adji maam Ndiaye, yaay I thianék ama, maa challaa
Man da ma lay tooñ, njëk laa mer, fas sa ma kamnam
Nga daldi ree, nima mbaye dieye, mbasaa mbasaa
Seng Seng papa Mbaye mbassa mbassa
Bés ni ki tay kholal, baal naa ñépp
Am gi jamm yi, Fans yek, kharit yi ban ngemp
Ho baal nagne ngemp

Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko
Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko
Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko
Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko

Mani jéggël ma ko, jéggël ma ko
Yallak yeuremade yam, jéggël ma ko

Man youssou maajigéen, j'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ, jéggël ma ko

Ahhnn yee (jéggël ma ko)

Fay Bor » Youssou Ndour Letras !!!

Lyrics de: Youssou Ndour

Esta web no aloja ningun archivo mp3©LetrasFM.Info 2025 Colombia - Chile - Argentina - Mexico. All Rights Reserved.

Musica Online, Escuchar musica online , Musica En Linea, Musica en linea gratis, Escuchar Musica Gratis, Musica Online 2025, Escuchar Musica

Musica 2025, Musica 2025 Online, Escuchar Musica Gratis 2025, Musica 2025 Gratis, Escuchas, Musica de Moda.